Sie sind auf Seite 1von 12

Cllalag xam sa diin

Ci fnnug yar aki teggin


Kiko Taalif ci arabe di Cheikh Ahmadou Bamba Mbacke Khadim Rassoul

Kiko tekki ci wolof Cheikhouna LO Ngabou ak Bilaal Ware Tel: 1- 224-789-0797 Chicago il USA

(011-221) 76 685 87 61 SENEGAL E-mail : locheikhouna2005@yahoo.fr

UBBITE ci tudd turu ylla laay tmblee samay jf ak samay wax yalla miy xewl bindef ypp ci ddinasi di jagleel yrmaandeem i ko gm ca llaaxira

Nahju Qda al-haj Yalla dooyna ma te dooyaloo naa ko. Yalla doyna weeru waay te doyaloonaa ko Jef ju nekk yeene ja lay nuroo Te looy jf rekk langay ci yeene ngay am Bokk na ci xam-xamu xere (hikma) Lepp looy sakku boo ci sonnee danga ciy jot. Kepp kuy fgg bunt saa bu tanqale (ii cii biir) ubbilees ko. Kepp kuy woor ci gepp caay-caay na xam ni gnneel lu Ylla lay dooge (kor amnga ko) Kepp ku bayyi akku fayda buy u lim woroom (boroom) xel yi boole ko ca Kepp ku bgg bakkanam ngrm Ylla du ko grm Kuy def lu ko sb di dajeek lu ko soof (saa) Kuy xeex ak bakkanam su noppee dund texe Kepp ku top yonnent bi (SAS) dina am lepp lu gnn ci lumu bgg Bepp reew minga xam ni fenn moo ko samp yagg-yagg dafay daanu

Bepp reew minga xam ni dgg moo ko samp dafay des ba baa saa ji taxaw Mangi sant Yalla ni mu sutuural ba nbbu samay sikk te dimbali ma Mangi sant Yalla ci limu tabbe lool ci man te loolu yeewoona cant Moom Yalla moo def ku am ay teggin sa rr (akku xam-xam) du fee ak sa suufe askaan Moom moo defal ku am xam-xam ak teggin mu am yool (thawab) bu bare ak njub Yall na Ylla xewel yonnent bi moo moo yegoon ci kow al-Burq Moo moo daan woote jemi ci Ylla te tek ko ci ay teggin ak jikko ju rafet Moom Muhammad ak a jiituwoon di ay sahaaba-am oom laqnau (amnau) ngnneelu Ylla (fadlallah) u defoon laabire (conseil-nush) muy seen yoon biu woote te daawuu bundaxataal kenn (irhq) Ndax dauy daan moom seen bakkan (nafs) ci seen sago (istirqq) Dau daan joxe seeni allal ci yoonu Ylla Te daawul and ak ngistal walla naafiq (nifq) Daoo gmoon ni Ylla mooy jari mooy joxe wrsg moo tax u weroon ko seen lepp Dau daan jekkante jem ci lepp luy dundal allaaxira fasewoonau adduna ba daawuleen yaqal dara Ndool (akk gu tar-imlq) daawuleen tiitloo ndax xamn a u ni Ylla mooy settaantal mbiir yepp te moo ko bind. Daoo soppoon seen boroom, kom-kom daawu leen fabbi (detourner-alha) ci seen bggante ci seen biir.

Bu guddi masaana (masoon-na) lndm dau jl seen lampi xam-xam (ak di ko jfe) di ko niitoo (tall-torcher) Cy gaa yooyu daoo moson cafka lu gna neex te dau oroon oou Ylla na leen Ylla grm, Yalla julli ci yonnent bi Te nag, maa ngi tontu Murid yi bgg a jajju oom dau sakku waay woo xam ni dina mb ay teggiin yu u mn a tegginoo te loolu sax dafa di lu war. Ndaxte kepp kuy sakku top Ylla te andul ak iy teggin du ci mn ame njari Ay Teggin, mooy lu gen ci lepp lu nit di denc te mooy teraanga ji gn ci lpp lu nit di terloo (sakku di am ci teraanga) Moom ay teggin dafay leeral xol, te mooy tax a jege ajjana Mooy tax nit i sopp la, mooy tax nga sori safara Ma buur (rise quickly) ci saa si ngir tont di ci yaakaar ngrmu Ylla ak yoolam (thawb) Li ko taxa jog nag, mooy jema tnk lu waliyu add al-hajji bindoon ma di ci yaakaar faju aju Di ci yaakaar itam dajale ci gattal la boroom xam-xam yi bindoon bu ygg Ndaxte lpp lu new te jotal moo gn lu gudd bay nd ak ay coono Mangi ko tnk mu am lool njari ci ngneelu Ylla Maa ngi ciy aan di ci yaakaar ngrm ak koolute (surete-woolu) ak njggl ca bes ba nga xam ni moo tiitloo epp Yeen mbooleem taalib yi maa ngi leen di dnk ngeen smoonte ak tontu lii Jikko yi ci nekk ak teggin (adab) yi moo leen di womat jm leen ci njub Njari yi ci nekk ak njub gi du sappi kenn ku jm fenn kuy door a soobu ak kuy ygga soobu oo ci yem kepp yiw yi du jeex
4

Ndaxte dafa lay xamal naka ngay jaare ba yegg ci gn ja rafet ay teggin ak lingay skku Tudde naa ko nag, yoonu faj ajoo ngir gattal (ngir goob) liggeyu sunu seri bi tudd al-hajji Mangi sant Ylla di ko aan mu nangu liggey bi ci ngnelam te dimbali ma ba ma matal ko Te def ko mu mel ni turandoo-am ba kepp ku ko jngati say mbiir ywn nga texe Te musl ma ci ngistal ak awjf (jb) ci dara ja Yonnent bi (sas) moom mooy boroom liwal hamd Te mangi koy aan mu musl ma ci gpp caay-caay te may ma lppi ngnel . Na ma musl itam ci ayu ibliis ba faww ak ci ayu lpp lu mu bind lu nekk ci suuf si lu nekk ci asamaan ak lu nekk ci seen diggante Na ma defal may topp ngn ji kuy ramm ki gn ci kepp kuuy top. Yalla nga juuli ci oom (Yonnent bi ak sahaabam) Lii mooy ubite teere bi Leegi nag mn nanu jublu ci teggin yi maa ngi jeema way fii loo xam ne cheikh ahmad ma geju woon (ocean du savoir) ci xam-xam bindoon na ko. Yeen taalube yi dglu leen ma laabiire leen ci loo xamne dina leen jial ak texeedi. ngir i ftte ak iy nelaw man ni jar(eveille) yewwu. Yoonu teggiin mooy yrm gune yi ndaw yi weg(respecter) mag i kpp ku maase ak nga def ko ni sa bopp. Na ngeen xam ne ay teggiin mooy taarub ku xam ak kuy xamlu(etudiant), mooy ganjaru(parure) ku xam tey jeema saf nit i, bu jikko yu rafet yi doonoon ab neeg ay teggiin mooy doon puj ba, te kpp ku amul ay tegiin

yalla du ko safoo bindeef yi dunu ko faale te fpp fumu toog bala faa joge ame fa gacce(deshonneur). Bokk na ci ay teggiin ngay laabiire(conseiller) nit i ci lpp loo gis ne seen njari nek na ca. Bokk na ci ay teggiin nga jpp ne kenn waru laa defal dara.(tam di sukkndiku ci sa bop). Boo amee ay teggiin jappal ne yayoo woo lu la kenn di maggale. Na nga tamal sa bop ay teggiin te diko jflanteek nit i doontela ni ngay jeflanteel sax amu u ko. Noo bgg nit i def la ko deeleen def noona. Te foo tollu na ngay sammoonteek(surveiller) li la war sa dignteek sa boroom amna hadithu yonnent bi muy yaxal naan : sama xeet wi de du taggoo ak yiw li feek gune yi ni ngi weg mag ni , mag ni itam di yerem gune yi. Te foo tollu na ngay roy ci njubu ilimaan yi boo ko defee di nga am njub. Bul di toog ak ku la mag ci benn toogukaay, ludul ne dafa munula kk, lu mel ni lekk jot wala tdd jot, wala ngeen bokk waruwaay.(voiture ets..) bu toogaay ba amee itam na nd ak dal ak tekk(serenite) ak xeebu(modestie) ak mongulu,(accourpi)) bul di ses ci moom bul di toog ci kanamam bul ni jack(en face) di ko xool, na ngay sajj(baisser les yeux) sab gis, te bul di baril looy geestu(tourner la tete) lu bari ci ludul aaja, te sax loolu mandargam rer la.(ignorance) Yalla sunu boroom neena ( waxal jullit i uy sajj seenub gis)(baisser les yeux) yonnent bi (sas) neena nit ki man naa xool xool boo xamne day yaq xolam ni ab der di nebe ci sebej.(preparation des peau ) Ndaxte boo xoolee dara man nga caa gise lu baaxul te doo ko mena mu. Am na keneen ku wax ne ag njmbaar dey nekkut ci di xeex aka dbnte ay gobar, waaye njbaar tigi(reelement) mooy nga lem say tnk ba cee dox luy jur bkkaar wala nga sajj sa nagu bt(irris) ba cee xool luy naqari ylla. Ak foo mana nekk buldi baril am po aki reetaan ak di yngutu ak ay caaxaan buldi yuxamtiku wala ngay yrndoo ngir mana gis nbu loolu nak mandargam copte la ak xel mu woyof. Boo toogee neel tekk dal te boole ca selaw. Ludul ne daulaa laaj dara wala ngay laay dara te loo ciy def bulk o di jooru,(haute voix) bul di wax mukk ci ludul aaja, ndaxe selaw sutura la, nooflaay la, te itam bariyana wax yoo xam ne baa ddu mooy tontam. Am na u wax ne: fuwax done xaalisu gal(argent massif) noppi done fa wurusu ngalam,(or) te saayu la nit xamul ba waxla lu nekkul ci yaw, neel patt ban koo faale. Yalla sunu boroom neena : (na ngay dummooyu (tourne le dos) i xamul te lu u la man di wax yaw waxal jmm, fexe ba mucc yaw.
6

Bula ab smbaabooy(ignorant) di saga jppal ne waxul ak yaw. Xamal ne saagaante aka weddeente ay wax bokk na ci jikko yi yes . Xamal ne ree ju bari day ray aka wowal ab xol , ylla neena (nit i nauy ree lu neew di joy lu bari. Boo toogee ak ku la mag booy ree na ngay muu(sourire), bul di ame jataay(place) ba ci ay wax , na ngay def patt(silence) ba moom mu sakkoo wax ak yaw nga tontu ko ci kem limu la laaj te yam ca kepp nak. Bu fekkeene dafa doon mag mu tang(mauvais caractere) na nga dkku(supporter) tngoor wa , su juumee na nga ko jggl njuumteem(son erreur) loolu, na nga koy nangul ngnt,(accepter) te bulk o di jppal mer. Saayoo toogee ci jataay ba bege jg , na nga meebu(jug) ndnk waaye bul jog di tqtaloo(jaar ci kaw nit i) nit a wala ngay ykkti pnd ba.(la poussiere) Boo nekkee ci ab jataay bul fa di nelaw ca biir nit a , ndax loolu man naa waral gcce. Xamal ne kpp ku bgg lekk lool du tggoo ak yaraanga. Koo xam ne ittem jpp da koo def rek ci biiram(ventre) ak pyam (sexualite) boole na jikko yi yes , na ngay yam rek ci lek lu lay taxa mana taxawe ag jaamu ylla. Xamal ne kpp ku fuqle tambulina ay wu mu xamul fumuy yam. Say yoxo bul ca di jfndikoo lu la amalul njerin. Boo dgge ku la mag di skku dara fi sa kanam gaawal defal ko loola , bu dee yonne doxali ko yonnent boo bee, bu dee woote jottlil ko woote boobee.bul di wax ak kenn ban e ko fen nga mbaa waxoo dgg, mbaa juum nga mbaa gpp kddu guy mer loo nit, bulk o di wax sax gone waxantuma la ak mag,. Bu nit ki waxee loo xamu toon na nga ko dggl , wala nga ni ko xmuma ko woon wala jppewuma ko woon noonu,wala nga wax ak moom ci kddu yudul merloo kenn. Yonnent bi (sas) neena kpp ku gm ylla , gm ne bis bu mujj ba dina am, nay wax aw yi mbaa muy selaw. Am na waykat bu wax ne: Na ngay tamal saw lmmi wax ju yiw, ndaxte lmmi lumu tmm bu koy tudd du ko tay. Booy dox na aajo tax, te bul bul di fuukarewu(orgueille) mbaa ngay dox di niiru, Bul di reetaan ci lu ko matul, bul di dox itam ci ludul itt, bul di geesu ci ludul itt , ndaxte yooyu ypp ndul ak ay teggiin. Bul di dox di summi(otter) say tubay, ndaxte loolu du ay teggiin te loolu melow caay-caay la.
7

Bul di wui sa biir , wala ngay wui sa dignte jumbax ak say wom, loolu de ag ndof la ak rer ak kk kersa, te diine moom kersa mookoy mottali. Koo romb wala nga dajeek moom na nga ko nuyu, kpp ku la jkka nuyu na nga ko fay kem na mu la nuyoo wala nga gn koo jotal . Boodee nuyok sa mbokkum jullit di saafoonte ak moom bul di jkka rocci sa loxo, te ca waxtu wa ngeen di safoonte na ngay naan ndaxte loolu din a sippi ay bkkaar . Bul di nuyo di cosante ay baaraam, na ngay nuyo ak aari yoxo. Saa yoo bge dugg ci negu jmbur na nga yglu, bu la joxee ndigl na nga dugg bu la nee dellul na nga dellu te ba caa mre, bu la diglee ba nga dugg ci biir bul fa nekk di xool ci wet gu nekk, ndaxte amaana nga gis fa lumu doon nbb. Booy wut xarit bul and ak ab dof, wala ku iaan, mbaa ku bari ay mbt Bul di toog ci bepp jataay boo xam ne doo fa dolli koo diine ak am xel, boo ko defee raw. Nit ku nekk boo ko bge natt xoolal ca a muy ndal, wax ma ki ngay andal ma wax la yaw yaay kan. Bul di nd ak ku r er, ndaxte bariwaana bu dof bge jari faf lore. Boo nekkee ci aw nit seetal aca gn nga nd ak oom. Bokk na ci ay teggiin , ngay jlale, tey ba di wui siki nit i. Xamal ne kpp kuy wui sikki nit i yalla dina wui ay sikkam. Buu tudde nit fi sa kanam waxal lu rafet li nga xam, Am na ku wax ne : Akamaa bgg jikko yu rafet yi, te damay ba di sikkal nit i kem ni may bae kumay sikkal , te danaa jllale kpp ku may saaga , ki yes ci nit i mooy ki bgg ay saga. Kpp ku nawloo nit i u weg ko, kpp ku leen xeeb oom itam u yab la rek. Am na ku wax ne : Boo bge dund am diine ju mucc ak cr bu ry ak der bu o(assure) saw lmmi bul ci tudd mukk sikkus jambur ndaxte sa lpp ay sikk la te nit i daoo am ay lmmi. Te gt yii saa su gisee sikkus jaambur nee ko gt yil bu leen xool kat ndaxte nit i am na u ay gt. Xamal ne wuute ab dig( fausser RV) ak ay fen na nga ko moytoo def ndaxte dafay yaq wxtaan, dikk na ci hadithu yonnent bi fu muy wax naan: Na gneen saxoo wax dgg , ndaxte dgg dafay jm nit ci mbaax te mbaax mooy ybbu nit jjana, te nit ki din a saxoo di wax dgg ba lumu waxati ylla ne dgg la.
8

Na ngen di moytu ay fen ndaxte fen dafay jm nit ci kccoor te kccoor mooy ybbu nit safara, nit ki di na tam ay fen ba lpp lu mu waxati ylla ne day fen. Na ngay top say waajur di leen yrm , te di gaawa jf seeni ndigl, di bayyi seeni tere te lpp loo ciy def na ylla rekk tax soo ko defee di nga am daraja yu kowe. Kpp ku la mag na nga ko weg. Boo bgge ylla safoola na na ngay jflanteek nit i ci jikko ju rafet. Na ngay rafetal say jikko ci di sopp nit i dina tax om itam u sopp la. Nooyal say wax ci nit i bokk na ci mndargay nit u or i. Am xel de bu doonoon aari xaaj benn ba mooy safoo nit i. Bokk na ci li gna neex ci nit , mu nekk ci xolub kpp ku jub. Na nga di siyaare ji woroom xam-xam yu yiw ya te deeleen liggeyal saasu neck te ylla rekk tax, na ngay skku seni aan ak di barkeelu ci oom, din a tax ngay dolli ku njub. Xamal ne kpp kuy mggal boroom xam-xam bu koy jf yaa ngi mggal jmmi ylla. Saa yoo ndee ak ku la mag, ci tukki wala jotaay na nga weg te di ko jiital, te bu jotaay ba doonee bu xat yaw na nga toog ci suuf, ludul bu fekkee ne toogandoo ak moom dafa di lu manula kk, bu lekk teewee bul njkka raxasu wala ngay njkka tmbali, ten a nga koy bayyee la gna xeemeemu ca ndabla, ngir wrmaal ko. Saa yoo ndee ak aw nit ci tukki na nga leen di jppale ci lpp luy seen soxla, te nga man ko, saa yoo defee njuumte na nga ko jgglu, bul nekk di ku begg ab nooflaay di ku yccaaral(yambare) aari mbir yooyu du indil njari kenn. Saayu nit skkoo ci yaw loo man defal ko ko te bu ko tiial. Bul di nay mukk ci alali ddina jii nga xam ne mook poiitum matt oo yam, kkpp ku nay ku sori ylla la ak jjana ak li baax lpp. Kp ku tabe ku jige ylla la ak jjana sori lool safara. Am na waykat bu wax ne: alal joo xam ne boo ko dajalee da nga ko fiy bayi rek te xamoo ki nga koy byyee lumu ciy def, moo yaw loo ciy naye. Noo bga tedde rek na nga ime coono bu tmboo ak moom, kpp ku bgg dara fawu muy newl ay nelaw. Na nga di teral gan, ci yaatal ko, berndeel ko, bgl ko, jigeel ko, am gan bumu la taxa jaaxle ndaxte leegitay mu ibbi. Yonnent bi (sas) neena kpp ku gm ylla gm ne bs pnc ba din a taxaw, na ngay teral gan, te sax gan moom saasu ibe kenn munu koo tere nettle, moo xam u laaj ko wala laaju u ko, li jiitu ci ngan moo di nga di ko ubbil

sa xarkanam, ak lu mana xew bu yg ne dafa ljl, te lpp lu ylla daganal te nga man ko dee ko ca teral. Bul jnnl benn bis te skku woo ca xam-xam, loo ca xam itam na nga koy jef. Xam-xam mooy dundal xolub kuy xamlu, di leeral xol di dindi ngubag xol. Xamal ne bindef yi i ngi rawantee ci xam-xam ak diine, te ci mu rek lees koy ame. Kpp ku gn moroomam ci xam ak jf lay doon, waaye du ci aw askan wu kawe ci bay mbaa muy ci ndey, boo amee askan wu baax ba noppi na nga farlu boole ca ay teggiin. Booy skku xam-xam na nga sukandiku ci ylla te sellal ko, te dalal sam xel. Na ngay saxoo di jng te smm say cr, newl say nelaw newl itam ab reggaay. Foo tollu na nga din afar li ngay jng , bulk o wan ginaaw mukk. Foo tollu na nga di wuute ak sa bakan, ndaxte bakan moom du digl lu baax. Foo tollu na nga di newl say nelaw, tey baa tyeel, bul bgg ab nooflaay ten a ngay gttal say mbt. Xamal ne kpp ku skkuwul xam-xam cig ndawam , saayu mggee din a ko rccu. Te xam-xam moom kpp ku ko teelu la wuti ci jamono ji mu amagul ay soxla, du ko am. Skkuji xam-xam ci sag ndaw mi ngi mel ni yatt ci kaw xeer. Skku xam-xam ci sag mage mi ngi mel rdd ci kaw ndox. Xam-xam mooy dunE xol kem ni taw di dudl suuf. Te mooy dindi nguba ci xol kem ni weer wi di dqe lndm, ni bt di soxlaa leer ngir mana gis noonu la xol di soxlaa xam-xam ngir mana gindiku. Syidunaa Aliyu dafa wax ne: Xam-xam rekk moo mana ykti nit, ndaxte nit pp oo yam seen askan ndox ak suuf rekk la , i xamul rek ooy noonu woroom xam-xam yi, te ku amul xam-xam mook ku dee oo yam. Foo tollu na ngay nafar li nga jngoon ndaxte kpp ku bayi rek dana ftte la mu jngoon. Xamal nix am-xam lu jafe la lool kenn du ko am ludul ci nga tj sa bkan , da nga koy jox sa lpp soog cee am tuuti, boo ko joxee sa tuuti doo ci am dara, t exam-xam dafa gaawa rcc kuy mu rek moo koy mana am,. Kpp kuy skku xam-xam nay suufeel boppam bumu di rylu, ndaxte skkukatu xam-xam bu ryrloo rek du am dara ci ki muy skku. Kpp kuy skku xam-xam nay moytu luy xoy-xoyi (luxe), bumuy faral di toog ci lal waxtu wa muy jng, na am lool itte ci li muy skku, bumuy faral di dglu xccoo bi nit i di xccoo ci wallu ddina.( les quereles)
10

Bul di yeexa jngi bul ko di leem, (retarder) boo begge dab gaa a, gnnel sam xel ci ittey ddina yi dul dog mukk, te buur skku ji xam-xam, te dee moom buy dikk day bette, ku dee rek bayi na mbt. Kpp kuy skku xam-xam bumuy dcci( decourage) kpp kuy bga dcci bu muee tuuti daj dara. Kpp kuy skku xam-xam na weg sriam , di ko fajal ay soxlaam, te weg mbooleem lu taq ci moom, njabootam aki surgaam, di ko ligeyal di ko jox loo man, ten a ngay moytoo def genn cggante fi kanamam, bul fa di ree mba nga dif a caaxaan, bul di bari ay wax ci kanamam, te lpp lu mu la sant lu naqari naqari deal, lpp lu mu la tere lumu neex-neex byyil, dee ko jxi addiya ndaxte loolu di waral mu sopp la, lpp loo gis ne bgg na loola dee ca dab bnneexam, ndaxte bu la xoolee btub yrmnd say mbir man na caa baaxe ba faw, boo nekkee fi sa s say mbir man na caa baaxe ba faw, boo nekkee fi sa si melal ni ku faatu ak ka koy sang, te kpp ku amul ngrmu sriam du jarioo mukk xam-xamam, (ylla na nu ci ylla mussl ) Kpp ku xamal nit aw araf sa na caa laaj ci araf wu neck junniy drm,. Am na ku wax ne : Sama sri laay jiital ci samay waajur, ndaxte waajur yaram wi lay yar, sri bi nak moom ruu gi lay yar. Xamal ne mbokk mu baax ak xarit bu baax moo gna jafe ci lpp, saa yoo ko amee na nga len fonk, te mooy koo xamne bgg nga jariu dina ko jaral sax moom muy loru. Limal naa la fii ci ay teggiin loo xam ne boo ko settantalee jariu. Am na waaju u masa laaj ne ko yaw ku la yar? Mu tont ne: Damay xool i xamut dara lpp lu uy def rek ma moytu ko, saayu la jikkoy nit ki neexee defal lamuy def rek dal di koy doon fa saasa , bu la jikkoy nit ki neexul itam seetal la muy def rek nga moytu ko, maa ngi aan ylla mu dplema ak ngrmam, ylla na mu julli ci ab yonnentam, ylla doynama te doyloonaa ko, Fii la ter nahju jeexe, muy tnkub la sunu sri ba (addal haji) bindoon,. Ma ngi sant ylla mi ma gene ci dexeedi. Di julli ci yonnent bi laq teraanga ypp, yonnent bi ylla tag ci jikkoom yu rafet,. Di julli ci ndadoom ya soppantewoon lool, te mblut woon moroomam safaan. Ma ngi aan ylla ci seen barke njggl , ak jige leen ak mu dolli ma xamxam buy tax ma di len gna sopp, te ter bii na doon yoon wi murid yi di doxjm ci ngnel. Na ko ylla def mu am barke buy feg alkande. Nay saafara bpp jngoro.
11

Na je gpp texeedi. Na doon sababus sunug yegg ci ylla ak ci yonnent bi. Na doon luy xcc nit i jm len jjana , te di len fegal mbugl. Na doon sababu texe ak xam-xam ak jf k oak jaamu ylla. Na doon lunuy xcc jm nu ci muj gu rafet ci darajay yonnent biy maami Fatima (sas) ylla na ko ylla dooli xewl li feek boroomi teggiin mi ngi am ndam , ak li fek xoli mukat yi di am leerug ylla.

Ki ko tekki ci wolof : Cheikhouna Lo Ngabou ak Bilaal Ware Northwestern University of Chicago Friday 6 June 2008

12

Das könnte Ihnen auch gefallen